Ñaareelu Xareb Àdduna
Ab jukkib Wikipedia.
Ñaareelu Xareb Àdduna ab xare la woon bu laaloon àadduna bi. Mi tàkk ci bi Almaañ ak Itaali ak Imbratóor gu Sapoŋ bëggee noot àdduna bi ci diggante 1914-1918 g.j. Ñaari réew yii mu ci nekk daw na wuti ndimbal ci li ëpp ci réew yi mu defal ay tapoo (alliance). Bu ko defee yàggul dara lu bari ci réewi àdduna bi duggsi ci.
Faraas sàkku woon na ci mbooleem ay sancoom ñu jàppale ko ci xeex bi, te jox koy nit. Jot naa dajale - ci ndimbalul Blees Jaañ - am mbooloom xare mu mag, mu xeex ci wetu Faraas lank sancuy Almaañ yi, ñu nangu ci Togóo ak Kamerun ak wàllug sowwu gi ci bëj-saalumu Afrik ak Tanganika (Tansaani ci jii jamono).
Lu bari ci xarey Afrik yi (sànnikati Senegaal yi ca lañu woon ) jawali nañu Tugal, ngir xeexal Faraas. Xarekati Afrik yii ñi ngi nekkoon ci dundiinn wu tar te wow, ci biir yeer yi ak ci sedd bu metti bi, jànkoonte nañook jafe-jafe yu bari, lu ci mel ne ñàkk a dégg làkkuw waa Faraas wi akug tumbrànke. Waaye loolu lépp teewul ñu ràññikoo woon ag njàmbaare akug dogu. Xare ba jeex na ci ndamul Faraas ak ñi àndoon ak moom, ñu dàq Almaañ, mu doxe ci ñàkk mbooleem sancoom yi ci Afrig.
Ci atum 1939 g.j, la ab xare tàkkaat bu bees bu tàllaliku ba daj Tugal ak mbooleem réewi àdduna bi. Hitler njiitul Almaañ li daa gëmoon ne réewam mooy mi gën a kawe ci àdduna bi, kon yi ci des yépp dañoo war a toroxlu ciy tànkam, Itaali nag ak Sapoŋ dañoo àndoon ak moom ci loolu. Waaye réewi demokaraasi yi dañu koo lankoon.
Xareb Almaañ bi songoon na suufi Faraas yi, loolu jur Faraas séddaliku ci ñaari wàll, wàll guy jàppale Almaañ te ànd ak moom ak gu nekk ci ron kiliftéefug Jeneraal Degol, mooy giy jàmmaarloo ak a xeex Almaañ.
AfriK gu yamoo wi(equatorial) gi Faraas yilifoon ci njiitul Flips Ibuwe dafa nekkoon di jàppale Degol, bu ko defee njiiti Afrik gu sowwu gu Faraas gi ñoom di jàppale Almaañ, ba ca tabaski 1942 g.j, booba lañu wëlbatiku jàppaleji way tapoo yi (les alliés).
Waa Afrig yi yamuñu foofu, waaye yabal nañu ay xarekat ca jëwub xare ba (front de guerre) ngir jox ñam way xare yi ak jox mbell Tugal.
Ci atum 1945 lañu daan Almaañ. Sapoŋ it daanu ngir fàccaakonub saal (bombe atomique) ba waa AameriK yi taal ca kawam. Ñaareelu xare bi dakk na - niki bi ko jiitu woon - alag dundug ay milyoŋ ciy nit.