Senegaal
Ab jukkib Wikipedia.
Senegaal | Réewum Senegaal | ||||
|
|||||
Lonkoyoon bu Senegaal | |||||
barabu Senegaal ci Rooj | |||||
Péy | Ndakaaru | ||||
Làkku nguur gi | Nasaraan | ||||
Koppar | Franc CFA | ||||
Lonkoyoon bu Senegaal |
Réewum Senegaal menn la ci réew yi ne ci Sowwu Afrig, te féete ci bëj-saalumu Dexub Senegaal. Moo ngi jakkaarloo ak Mbàmbulaanug Atlas ci sowwu, taqaloo ak Gànnaar ci bëj-gànnaar, Mali ci penku, Ginne ak Ginne-Bisaawóo ci bëj-saalum, Gaambi nekk ci biiram ci wàllu sowwu. Jakkaarloo ak dun yu Kap weer yi nekk ci mbàmbulaanug Atlas gi. Senegaal yaatoo na 196.190 km2. Péyam mooy Ndakaaru, nekk ci cat bi gën a féete sowwu ci goxub Afrig.
Tërëlin |
[Soppi] Taariix
Ngir Xóotal, yërël bii jukki ci Taariixu Senegaal |
Jàpp nañ ne Senegaal dëkkee nañ ko lu jiitu juddug Isaa. Ay jeexiti yëngu-yëngu yu njëkk-taariix di nan leen gis, daanaka, ci barab bépp.
[Soppi] Nguur yu njëkk
Ndank-ndank xeet yi ko dëkkee dañ doo di gën a ñëw, kon réew mi di gën a bariy way dëkk. Nguur gi fa njëkk a sosu mooy gu Tekuruur, gu Jolof moo ci tegu, moom mujj nekk imbratoor gu mag. Imbraatóor gu Mali ak gu Gaana am na ci ay jamono yu seen imbraatóor aakimoo woon suufi Senegaal.
[Soppi] Ñëwug waa Tugal
Cada Mosko mooy tubaat bi njëkk a tek tànkam ci suufi Senegaal ci atum 1442, buur ba nekkoon Poortugaal moo ko yónni woon. Ci noonu la waa Poortugaal tambalee jëflante ak waa senegaal yi fa nekkoo, yaxantu judd ci seen diggante. Ci nii ba mu yàgg waa angalteer dal di ñëw, waa faraas tegu ci ak waa Olaand. Dem na ba waa faraas rek a fi desoon aakimoo réew mi yépp; def Ndar péyam tek fa ab Laman buy yor réew mi. Laman yooyu ay tubaab la ñu daa doon yu daa jóge ca Faraas.
[Soppi] Tembteem
Senegaal mi ngi temb 14 fan ci weeru rakki gamu ci atum 1960. Waaye lu jiitu temb li da fa andoon ak Sudaanug Faraas (di Mali gu tay gi) dal di sos lii di Bennoob Mali ci tamxarit gu 1959, ci bennoo googu la amee tembte. Ñu tek ci at, ci 20 baraxlu 1960 bennoo ba daa di tas ganaaw ay jotey politig yu amoon ci diggante ñaari réew yi. Kon ci nii ñaari réew dal di cay juddoo: Senegaal ak Mali. Naka noonu ci 1982 Senegambi dal di jubb niki bennoob ñaari réew yi, waaye bii bennoo ciy keyit la yemoon, masu ñu koo jëfe ba tax na ci atum 1989 la tas.
[Soppi] Melosuuf
Senegaal la ngi nekk ci diggante 12°8 ak 16°41 wu tus-wu-gaar wu bëj-gànnaar ak 11°21 ak 17°32 wu tus-wu-taxaw wu sowwu. Catam bi gën a féete sowwu mooy Ndakaaru di it cat wi gën a féete sowwu ci goxu Afrig.
Su ñu ko mengalee ak réewum Mali walla ak mu Gànnaar di nan gis ne Senegaal réew mu tuuti la.
[Soppi] Klimaa
Klimaab waa Sahel la am:
- Nawet maami koor la ba kori. Bëj-saalum gi moo ëpp taw bëj-saalum. àllub yamoo gi ca Caasamaas la ne, ndaxi tawam gu bari;
- Noor moom diggi tabaski la ba rakki gamu
[Soppi] Seddatleeg yorte
Ca atum 1996 la seddatle gu mujj gi amee, mooy giy wéy ba tay, lu dul coppite yi ci mujjee am: Sosteeg diwaanu Maatam ci 2001 ak gox-goxaan gu Kungeel ci 2006.
Ci 2007, Senegaal la nekk 11 diwaan,
Yenn ciy dëkk:
- Cees, 311 324 way dëkk (2005) ;
- Ndakaaru, 1 009 256 way dëkk (2004) ;
- Jurbel
- Luga
- Maatam
- Mbuur
- Mexe
- Ndar, 154 496 way dëkk (2001) ;
- Podoor
- Tuuba
- Tëngéej
- Kawlak, 185 976 way dëkk (2007).
- Siggcoor, 158 370 way dëkk (2007) ;
[Soppi] Giir yi
Senegaal doon na réew mu bariy giir, waaye it soo ko mengalee ak yeneen réewi Afrik yu bari, wuuteeg ay giiram du feeñ. Man nan ni daanaka wuute amul ci diggante giiri senegaal yi ndax seenug bennoo ci caada. Man nan cee lim yii tambalee ko ci yi ci gën a bari ba ci yi ci gën a néew: Wolof (43,3 %), Pulaar (23,8 %), Seereer (14,7 %), Joolaa (3,7 %), Malenke (3,0 %), Sooninke (1,1 %) Manjaak (2%), ak yeneen giir-giiraan yu tas ci réew mi, man nan cee boolee it tubaab yi ak naari libaan yi.
Réewi afrig |
Afrig gu Bëj-saalum • Alseeri • Angolaa • Bene • Botswana • Burkina Faso • Buruundi • Kamerun • Kap Weer • Réewum Diggu Afrig • Komoor • Kongóo-Brasaawiil • Kongóo-Kinshasa • Kot Diwaar • Jibuti • Isipt • Eritere • Ecoopi • Gaboŋ • Gaambi • Gana • Ginne • Ginne Bisaawóo • Ginne gu Yemoo • Keeñaa • Lesoto • Libeeria • Libi • Madagaskaar • Marook • Malawi • Mali • Móoris • Gànnaar • Mosambik • Namibi • Niseer • Niseeria • Ugandaa • Ruwandaa • Sahara gu Sowwu • Sao Tome ak Principe • Senegaal • Seysel • Siraa Leyoon • Somali • Sudaan • Suwaasilaand • Tansani • Cadd • Togóo • Tiniisi • Saambi • Simbaawee