Web Analytics Made Easy - Statcounter

See also ebooksgratis.com: no banners, no cookies, totally FREE.

CLASSICISTRANIERI HOME PAGE - YOUTUBE CHANNEL
Privacy Policy Cookie Policy Terms and Conditions
Wolof - Wikipedia

Wolof

Ab jukkib Wikipedia.

Wolof làkk la wu ñuy wax ci Gaambi (Gaambi Wollof), Gànnaar (Gànnaar Wollof), ak Senegaal (Senegaal Wollof). Mi ngi bokk nag moom Wollof ci bànqaasub atlas bu làkki kongoo yu kojug nit ku ñuul yi. Mbokkoo gi mu am ak làkku pël lu yàgg la. Am na it lu mu seq ak yeneen làkk ci gox bi niki séeréer, joolaa ak basari.

Bi ñu demee ba gis jëmm ja, muy ku sew, tuuti te xaw a wow, waaye di ku ñu muure ab taar, ci anam gu woyof te loyox, di ku ñu aare kàttan, sóob ko ci ag fonk-sa-bopp doonte ag neen la, solal ko yerey yëgle ak jaral, te ma jëli loolu ca jafeem gaa jëli. Bi loolu amee, da ma ne leen xanaa kay du kii ngeen ma doon wax? ñu ne aha kay, cis lëf, cig yéemu, ak ñàkk a xalaat ne di naa sikk mukk ci moom, ma jug man, xajal leen foofa fépp.

Ma ne nag waaw ku mel nii, ci li mu làmboo ciy melo, lu ko nit di doye ? Ginaaw bi nag dégg naa ñu'y wax naan moom de bokk na ci ñi gën a jekk ci boobule gox, ànd ak jaaxle ci sama aw jëfiin, ci ba nga ma ko fa ba, ma ne leen man : moo xam! Lii mooy li am ci sunu làkk wii, walla yii di yu Afrig yi, dañu di yu am solo te man a dem ni yépp di deme, am barab ci digg barabi làkk yépp, waaye li nu dal nun waa Afrig, mooy li dal sunu lépp, dalaale ci li muy dal sunu kàllaama yii nga xam ne wii de bokk na ci yi gën a nosu, gën cee nooy, gën cee nangoo defaru, yéwénu, ruy, ci ku ko ruyal, tey way nag ca nanu bëgge mu waye ni.

Ana nag ku am janq bu mel ni bii cib taar, nangoo ni, jongee ni, jekke ni, man nee toppatoo, nangu nee jeme-kanam, waaje ni ngir lemu ci say bëgg-bëgg, ana ku am ku mel nii, looy xoolati ku sewe nii, ràgge ni, te taaroodi ni?

Li ma bëgg a wax mooy naka lanu bëgg a bàyyee sunu làkk yii, rawati na wii di wolof, ca nooyam ga, ak nangoom ga, ak gàttam ga ak noppaleem ga, taaram ba, leeram ga, manam gaa leeral ak yaatoom ga, ak ruyu gi mu nangu, naan da nga'y jëlati weneen di ci sonn ak a sonle, naan day wa gën? Ma ne ñoom ñoo gis loolu man de déet !

Wolof mooy làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal, waaye ngir doyodig waa Afrig yi ba leegi, franse mii nga xam ne lu matul fukk cib téeméer ci doomi Senegaal yi rekk a koy wax moo fiy làkk bu njëkk, maanaam wi nguur gi di waxe di ci liggéeye.

[Soppi] Cosaanam

Ni ko gëstukat yi waxe, làkku wolof am na ag mbokkoo ak yeneen làkki Afrig yu bari, yu mu bokkali maam. làkk yi dañ leen a séddale ci ay wàll: bu ci nekk ñi am ag mbokkoo lañu fa def. Nee nañu wolof ci wàll gi ñu'y woowe bànqaasub atlas bu làkki kongóo yu kojug nit ku ñuul la bokk. Am na ag mbokkoo ak pulaar ak séeréer ak joolaa ak yeneen.

Daanaka ñoo ngi koy làkk ci senegaal gépp, bëj-gannaar ba bëj-saalum, penku ba sowwu. Donte wolof da di làkku askanu ñi ñuy woowe ay wolof, waaye kàllaama wolof amul aw dig. Dem na ba romb dig (frontiere)yu Senegaal àgg ba Gaambi, Gànnaar ba Mali, ci ñaari dëkk yu njëkk yi sax boole nañ ko ci seeni làkki réew. Daanaka gox boo dem ci Senegaal am nañu waxinu wolof wu wuute: am na wolofi waalo-waalo, jolof-jolof, saalum-saalum, wu kajoor-kajoor, wu baol-baol ak wu lebu.

[Soppi] Mbindin

[Soppi] Araf yi

  • a      : andale
  • à      : Yàlla,kàllaama, làkk
  • aa    : Senegaal, aada
  • b      : baat, bind
  • c      : cangat, caabi
  • d      : diwlin, dall
  • e     : diine, xamle
  • ë     : xët, bët
  • f      : fës, faatou
  • g      : ganaar,gàncax
  • i      : fit, nit
  • ii      : fii, niit
  • j      : jolof, jàmm
  • k      : kàllaama
  • l      : lamb, laal
  • m      : matu, maafe
  • n      : nit, naan
  • ñ      : ñaar ,ñeeg
  • ŋ      : mandiŋ
  • o      : bor, sol
  • ó      : tóor-tóor, dóor
  • p      : poobar, paaka
  • q      : cuq, xonq
  • r      : rabb, rammu
  • s      : say-say, set
  • t      : tali, tund
  • u      : futt, kudd
  • w     : wolof, wone
  • x     : xët, xëcc
  • y     : yoole, yónne


aa - ab - af - ak - als - am - an - ang - ar - arc - as - ast - av - ay - az - ba - bar - bat_smg - bcl - be - be_x_old - bg - bh - bi - bm - bn - bo - bpy - br - bs - bug - bxr - ca - cbk_zam - cdo - ce - ceb - ch - cho - chr - chy - co - cr - crh - cs - csb - cu - cv - cy - da - de - diq - dsb - dv - dz - ee - el - eml - en - eo - es - et - eu - ext - fa - ff - fi - fiu_vro - fj - fo - fr - frp - fur - fy - ga - gan - gd - gl - glk - gn - got - gu - gv - ha - hak - haw - he - hi - hif - ho - hr - hsb - ht - hu - hy - hz - ia - id - ie - ig - ii - ik - ilo - io - is - it - iu - ja - jbo - jv - ka - kaa - kab - kg - ki - kj - kk - kl - km - kn - ko - kr - ks - ksh - ku - kv - kw - ky - la - lad - lb - lbe - lg - li - lij - lmo - ln - lo - lt - lv - map_bms - mdf - mg - mh - mi - mk - ml - mn - mo - mr - mt - mus - my - myv - mzn - na - nah - nap - nds - nds_nl - ne - new - ng - nl - nn - no - nov - nrm - nv - ny - oc - om - or - os - pa - pag - pam - pap - pdc - pi - pih - pl - pms - ps - pt - qu - quality - rm - rmy - rn - ro - roa_rup - roa_tara - ru - rw - sa - sah - sc - scn - sco - sd - se - sg - sh - si - simple - sk - sl - sm - sn - so - sr - srn - ss - st - stq - su - sv - sw - szl - ta - te - tet - tg - th - ti - tk - tl - tlh - tn - to - tpi - tr - ts - tt - tum - tw - ty - udm - ug - uk - ur - uz - ve - vec - vi - vls - vo - wa - war - wo - wuu - xal - xh - yi - yo - za - zea - zh - zh_classical - zh_min_nan - zh_yue - zu -