Imbraatóor gu Mali
Ab jukkib Wikipedia.
Imbraatóor gu Mali ba ci xarnub XII, xamalu nu ko woon lu bari. Ci li tegu atum 1150, la nu xam tur yu mel ne Hamana, Jigi Bilali(1175-1200) ak Musaa keyta di ko wax itam Allakoy (di tekki neex yalla). Moo ngi yemoon ci Mbàmbulaanu Atlas ci sowam, Dexu Niseer ci penkoom, tay ñuy yii réew: Mali, Senegaal, Gaambi, Ginne, Ginne Bisaawóo, Gànnaar, ak ab xaaj bu bari ci Kot diwaar.
Tërëlin |
[Soppi] Ay Cosaanam
Ci boobu diwaan (Sudaan) ag nguur gu ndaw judd woon na fa: Mandeŋ walla Mali (Malenke: nitu Mali). Ci li gën a siiw coosaanam, ay dëkk-dëkkaani mande yu bari yu nekkoon ci Kaw-Senegaal ak ci Kaw-Niseer. Traware yi nekkoon Dakadiyala, ci réewu Kri, ci wetu Nagasola, ci Kaw-Bakoy, Konte yi nekkoon Tabu, ca Doodugu (di tekki réewu Doo), Kamara yi ca Sibi, ca Siendugu, Keyta yi ca Nareena, ca Doodugu ak ca Doj yu Mandeŋ, nekk ci diggante Sigiri ak Kita.
Ca Doodugu la Bambara yi nangoo ay dëkk yu bari, màmm jëm penku, ba peggu Seegu ca Niseer. Ci li wër Doj yu Madeŋ, Malinke yi ñaari dëkk yu solowu lañ fa amoon: Kiri ak Dakadiyala. Njiitu dëkk yooyu ay rëbbkat la ñu woon, yu bokkoon ay gëm-gëm, bokk di def seniy xumbeeli diine. Nekkoon nañ nakk ay Askan yu bari yu bennoo woon am benn buur, Simbo moo doonoon seen maqaama. Buur yooyu Askanu mbooloo yee leen doon fal mu lee doon teewal ci ndaje ya daan am ca Pénc mu Mag ma(Gara), mi doon dogal ci li ñeel xare yi walla juuti yi...
Doley mbooloo yu nguur-nguuraan yooyu doon màgg, moo jappale nguuru Sooso gi donn Nguura Gana gu mag ga, ba mu man a sos geneen nguur gu mag gu buur ya amoon maqaamay Mangha walla Mansa.
[Soppi] Sunjata Keyta
Ngir Xòotal, yërël bii jukki ci Sunjata |
Musaa Keyta di ko wax itam Allakoy, siiwoon na ndax aji Makka yu bari yi mu defoon, loolu saxaloon na diney Lislaam ci xoli Njabootu buur bi. Doom, di itam Ndonoo mu Musaa, Nare Famagan (1218-1230) siiwoo na loo ndax yaatalam jëm bëj-gànnaar, ak sowu, ak pegg gu ndeyjooru Kaw-Niseer, nootoon Somono yi. Nare Famagan bari woon na ay jabar, kenn ci ñoom ki ñu dakkantalee woon Kuduma (boroom gòomu yaram yi). Jabar ju tawatoon jooju moy yaayu Sunjata Keyta. Bi mu juddoo ba juroom ñaari at man a gul woon dox.
Laagoom googu moo taxoon, ba Sumaawuru Kante doon faat ay magam, ba woon ko fa. Benn bes, Sunjata jengu ne day jòk taxaw, ndax naxxar gi mu amoon ci li Sumaawuru defoon, tegoon ci nangu nguur ga. Mu laaj ab weñ ngir jafandu ci jòg, weñ ga damm, mu jël geneen, noonu, jëlaat geneen noonu, ci la kenn waxee nañ ko jox yatu baayam ba, bamu ca jafandoo la jòg taxaw. Ña ko teewee woon yeemu; ndey ja ak géwalam ba, Jakuma Duwa, ca la ñu fentee ab bakk duppee ko Xala ga, baat ya ak wayin wa, ba tay ñoo ngi rëkk ci dënni waa mali yi ndax mooy seen bakkum réew.
Ci 1230 la nekk buur, ci la réy Sumaawuru, boole nguur-nguuraan yépp ya nekkoo ci wetam, ci nguuram, dal di nekk nak Mansa. Ci moom la Mali nekke nguur gu mag dëgg, ci la aggee ci pujam.
[Soppi] Ay buuram
[Soppi] Ulee
Bi mansa Ulee ñëwee(1255-1270), di ki wuutu Sunjata, la tambalee Diggadil(décentraliser) nguur gu mag jox ko yorteef ba mengoo woon ak réyaayam. Tabb ay sang jox leen ay ndomboy-tànk yu am solo, ñi ci gën a reññeewu. Fran Kamara, Siriman Keita.
[Soppi] Abuubakar mu njëkk(I)
Ci 1285 la Abuubakar mu njëkk(I) gaañu, Jafe-jafe yi nekkoon ci tànn ab ndonoo, ca la Sakura jëlee nguur ga. Doonoo na nitu nguur di itam ab jambaar, ci la yaatalaatee nguur ga ba dugg Gao ci penkoom ak Tekuruur ca sowan. Ay saay-saay ñoo ko ray ca weti Tripoli mu feekoo muy aji Makka.
[Soppi] Abuubakar ñaareel(II)
Ci 1303, Abuubakar ñaareel(II), di jarbaatu Sunjata, mi siiw lool ndax li mu bëggoon a wuññi li nekk ci ginnaawu Mbàmbulaanu Atlas mi. Ca la jëlee ñaar teemeeri looco ak dund dal di yònnee ngir ñu dugg ci mbàmbulaan mi, waaye kenn a ca dellu si nettali ni dañoo dajeeg ab dawan bu soxor ci ndox mi, mu mëdd leen. Abuubakar dal di jëlaat ñaari junni looco, xaaj fu deflufa ag bund, and ak ñoom dem, ca la saayee da tay.
[Soppi] Mansa Musaa(Kanku Musaa)
Mansa Musaa (1312-1332)Bokk na ci buuri Nguuru Mali gu mag ga yi gën a siiw. Ci 1324 la aji makka. Ca ajam bu siiw ba, andaloon na ag 60 000 ci ay dunguru (su ñu ci degloo Taariix as-Sudaan). Jaar ci diggu ndand féy-féy ba, ca Walata ak ca Tuwat, ba mu aggee Keer la ñépp yéemu ndax alal ga mu fa andi. Nee nañ yoroon na ñaari ton ci wurus. Mbaaxam ak yéewënaayam, yéemoon na bépp nit ba nekkoon Keer ca jamono jooju. Donte déggoon na araab nangul woon a làkk lu dul làkkam, daa jëloon ay tekkikat. Mansa Musaa yòbb woon turu Mali ci bépp réewu araab, dalee ko ca Andalusia ba Xorasan, ba Tugal, lonkoyoon bu adduna bi bu Angelo Dulcert(1339), wone ab yoon bu jall Atlas, jeggi Sahara ngir agg Mali: "rex Melli". Lonkoyoon bu Abraham Cresques, bi ko buuru Faraas defloo woon Charles V, bindoon na fa turu peyam "Ciuta de Malli".
Maghan(1332-1336) moo ko wuutu
[Soppi] Mansa suleymaan
Mansa suleymaan(1341-1360) mooy jubbanti waat koom-koomu nguur gu mag ga. Gën a dëggaral kilifteefu Mali ci Diwaani penku yi ko wër, njiitu Tuaareg yi bu Takedda (Ayiir), nangu woon na googu kilifteef. Suleymaan xëccoon na Mali ay boroom xam-xam ak ay àttekat yuy tòpp Maalik. Moo ci boppam fiqh la jang, maanaam àtte ci lislaam.
Mari Jaat(1360-1374) mooy ko wuutu
[Soppi] Musaa II
Musaa II(1374-1387) tegu ci, moom doonul woon ku am kàttan, xawoon a tayyeel, jëwrinam bu njëkk la bayee woon lépp. Moo songoo Tuareg yi, di def ay congam jëm Bornu
[Soppi] Saayam
Lu weesu Mansa II, kujje ya amoon ci biir kër buur, te yenn saa yi rayante daan si am, moo demoon ba faagaagal nguur gu mag ga. Ci noonu nguuru Gaawo di lekk ndakk-ndakk diwaan yi féete penku nguur ga. Dem ba jël peyu njaay bu Jenne. Donte ci diggu xarnub XV, Ca Da Mosto ak Fernadez newoon na ñu way dëkk yu Gammbi da ñoo jappee woon seen bopp ni ku bokk ci Mali, waaye, ci 1480, la Naba Nasere song Walata. Tekuruur jall ci loxoy wolof yi(Jolof). Pël yu Bundu tambali ay yëngu-yënguy fippu, Tengela I, di ko wax it Jaje di tekki Goreelkat bi, mooy leen jiite woon. Da fa gaawantu ci ay yi amoon ci diggante Mali ak Gaawo def li muy def. Nekkon ci dëkk bu am solo ci njaay mi, Kingi.
[Soppi] Imbraatóor gu Mali
Imbraatóor gu Mali :
Nguurug Susu ci xarnu bu fukk ak ñatt tegoon na loxo ci askanu Maandeŋ. Sinjaata, doomi kenn ci buuri Maandeŋ yi, daa dogu woon ci goreel aw askanaw, ci noonu mu tawal ab xare walla am mbooloom xare (larme) mom ci la ame ndam ci kaw Susu, ci xareb Karina ba atum 1235 g.j, ci noonu la am réewam tembe woon (amoon independance). Ginnaaw bi Sinjaata amee ndam ciy noonam, la giirug Maandeŋ daje (Konaate, Traaware, Kayta, ak Kamara) taxawal ag imbraatóor gu mag mooy gu Mali gi, Sinjaata jiite ko.
Sinjaata songoon na suuf yi feggoo woon ak moom ngir boole leen ci nguuram gi, loolu nag li ko ko may mooy xareem (armé) bu am bi doole, te nosu. Bi Sinjaata di faatu Mali moo nekkoon imbraatóor gi gën a rëy ci sowwu Afrig, péey ba di woon Niaani.
Ñi ko fi wuutu woon duggoon nanu ci lislaam, wéyoon it ci yaatal gëwéelub nguur gi, ba mu mujjoon ëmb mbooleem la ko dale ca mbàmbulaanug atlas ci sowwu bi, ba ca dëkkub Gaawo ci penku bi. Ñu séddale réew mi ciy diiwaan bu ci nekk ag kilifa jiite ko guy doxal ndigali buur bi, di dajale galag yi, tey doxal yoon. Ci jamonoy buur bi Kanka Muusaa la imbraatóor gi àggoon ca gën jaa kawey ay njobbaxtalam, ci xarnu bu fukk ak ñeent. Nguur gi nag daa na jot ci màng mi tukkee ci mbelli wurus yi ak yaxantug tàkk g i. Ci atum 1324 g.j, Kanka Musaa aji woon na Màkka, ci tukki bu tollu ci 18 weer, won na ci adduna bi dooley nguuram gi ak woomleem gi.
Amaloon na ay séqoo yu yaxantu ak réewi bëj-gànnaaru Afrig, indi it ci nguuram gi ay boroom xam-xami jullit yu juge penku. Ci xarnub fukk ak juroom benn la ay jafe-jafey wuutu (xilaafa) tàmbalee feeñ, ak dagu (sécession), looloo jur néew-dooleg ay diiwaan yu bari, bu ko defee Songaay daal di ñëw songu Mali, nangu ko.
Seetal BUNTU TAARIIX |
Seetal ci Wikbaatukaay man nga faa gis baat yi nga xamul |