Taariixu Senegaal
Ab jukkib Wikipedia.
Ngir xam taariixu Senegaal, taariixkat yi am nañu ay gongikuwaay yu bari : gongikuwaay yu gimiñ, yooyu nag yu bari lañu waaye soxla nañu ay gëstu yu xóot, ndax dañuy faral di jaxase diggante dëgg ak léeb (mythe). Ak jeexiit yi, ñoom nag bariwuñu te lu tas la, ak gongikuwaay yu mbind yi, ñoom it yu néew lañu, ndax askan yi dëkke woon Senegaal ca jooja jamono xamuñu woon mbind.
Senegaal nag suuf su ñuy gàddaaye génn la ak su ñuy gàddaaye jëm. Aw askanam, diirub ay xarnu, dañoo nekk ci diggante sax ak laxas. Senegaal nag taxawal na ay séqoo yu am solo ak aw askanam ak itam réew yi mu feggool. Daa na jëflante ci wàllug yaxantu ak gox yu sori yi. Loolu lépp nag tax na ba réew mi am aada ju cosaanu. Nguur gi njëkk ci Senegaal ñi ngi ko taxawal ci lu tollook juroom ñaareelu xarnu g.j, man naa am sax mu jiitu loolu. Nguur yooyu nag amuñu woon doole lu dul ci ñaari xarnu yii, bu fukk ak ñatt ak bu fukk ak ñeent, maanaam ci jamonoy imbraatóor yu ñuul yi (yu nit ku ñuul yi), gu Gana, Mali ak Songaay. Nguur yii ci ron kiliftéefug imraatóor yii lañu nekkoon.
Ci xarnub fukk ak ñeent Jolof soppiku na di nguur gu mag gu am ay sañ-sañ yu yaatu, teg loxo ci ay wàll yu mag ci nguur yooyu. Ci xarnub fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom benn, yenn nguur-nguuraan yi tàmbali woon nanoo daggu ci Jolof ndànk-ndànk, ci noonu Jolof mujj di nguur gu yamamaay niki yeneen nguur yi rekk. Nguur gu ci nekk ab buur a ko daan jiite, ab jataay (conseil) moo ko daa jox sañ-sañam, jataay boobu moom lañu dénkoon muy fuglu ay saxalam aki ndigalam , ay foŋsaneer daa nañu dimbale buur bi, di def liggéey yi aju ci saytu alal ji, wattu kaaraange gi, taxawal yoon, ñenn ci ñoom it daa nañu dooni kàngam (gouverneur) ñeel lenn ci diiwaan yi.
[Soppi] Nguuri Senegaal
[Soppi] canc gi
Cada Mosko mooy tubaat bi njëkk a tek tànkam ci suufi Senegaal ci atum 1442, buur ba nekkoon Poortugaal moo ko yónni woon. Ci noonu la waa Poortugaal tambalee jëflante ak waa senegaal yi fa nekkoo, yaxantu judd ci seen diggante. Ci nii ba mu yàgg waa angalteer dal di ñëw, waa faraas tegu ci ak waa Olaand. Dem na ba waa faraas rek a fi desoon sanc réew mi yépp; def Ndar péyam tek fa ab Laman buy yor réew mi. Laman yooyu ay tubaab la ñu daa doon yu daa jóge ca Faraas.
Ci Ndajem Berlin mi la réewi tugal yi waxtaan ba deggoo ci ana naka la ñuy seddoo Afrik.
[Soppi] Jàmmaarloo ci ngànnaay lànk canc gi
Lu ëpp ci goxi Afrig yi waa Tugal yi tegoon loxo ci jàmm lañu ko defe woon, li ko waral mooy waa Afrig yi dañoo jortoon ne tubaab yi de dañu fee jaar rekk waaye duñu fi yàgg. Waaye ci ginnaaw bi lañu gis ne canc gi (la colonisation) de mi ngi defi sémb ngir nar fee sax, te it mi ngi liggéey ci soppi séenuw dundiin.
Ci yenn barab yi ( niki Senegaal ), waa Tugal yi daje nañook ay jàmmaarloo yu tar. Nguuri Afrig yi amoon nañu ay xare (larme) yu ñu waajal, looloo leen dimbali woon ci ñu man a xeex jàmbur yii. Bu dee giir yeek dëkk-dëkkaan yi, ñoom dañu doon xeex ci séenug anam, maanaam di def ay cong yu tàqalikoo, fii ak fee (dóor-làqu ;guérilla).
Waa Afrik yi def nañu ay jàmmaarloo ci ngànnaay, yu jur ay ñàkk yu tar ci sàppes waa Tugal yi. Yenn jàmmaarloo yi wéy nañu ba ci atum 1930 g.j . Ca dëgg-dëgg waa Afrig yi ñoo gënoon a limu, te ëppooni xam-xam ci toolu xare bi. Soldaari Tugal yi nag yoroon nanu ay ngànnaayi sawara yu aaytal, waaye dañoo xawoon a doyadi, ndax manuñu woon a dékku tàngoor wu tar wi ak tawati rëddu yamoo wi (maladies tropicales).
Man nan lim ñenn ci ay way lank canc gi ci Senegaal: Lat joor Joob, Alburi Njaay, Alaaji Omar Taal, Muhammad Lamin Daraame, Saamóori Ture, Alaaji Maalik SY, Seex Ahmadu Bamba, Seydinaa Limaamu Laay, Aliin Situwe Jaata,...