Sëriñ Mbay JAXATE
Ab jukkib Wikipedia.
Sëriñ Mbay JAXATE nekkoon na di kenn ci woykati wolof yu mag yi (taalifkati woy yi) di woon it benn taalibeb Sëriñ Tuubaa, li mu taalif ci woyi wolof maneesu koo misaal mbaa deesi ko lim, nekkoon na di ab soofiyu bu mag, lu ëppoon it ciy woyam ci googule wàll la jëm, ku lislaame la woon te di woon ku jéggi dayo ba cig taral ci ñu sammoonteek daytali Yàlla yi aki ndigalam, bokk na ci ay woyam yii:
- pexem Yàlla moo gën pexem nit ndaxam () fa Yàllay fexee yàqkat yeggu fa
- Murit yaw de bul mer te bul jàpp mer () mer ak jàpp mer day alag ab murit
moo wax it:
- Bul gaaw a ñam gaaw a ñam baaxul nigal ba mu ñor () meeneen akug neen a yam pal-pal matul ne pelam