Gox
Ab jukkib Wikipedia.
Gox baat la buy tekki ab yaa-yaa wu suuf wu réy te tegu ci kol-kolu àdduna bi. Ci deggoo barab bi ñuy woowee gox dan ciy boolee tamit dun yi ko jege, maanaam yu soriwul tefes yi, lu mel ne Madagaskaar ni mu bokkee ci Afrik, ndax moom la gën a jege ni Asi.
[Soppi] Seddatleeg gox yi
Ci xam-xam, xaaj bu àdduna bi, bu beru rek gox nga, ci tekki bu yaatu, kon sunu sukkandikoo ci loolu dun yépp ay gox la ñu, ndaxte da ñoo beru, dañ ni cundum ci ndox mi.
Baatu gox amul benn tekki rekk. Looloo tax daanaka barab boo dem ci àdduna bi am na ay limi gox. Ci lu daj man nañoo jàpp ne mooy ab yaa-yaa wu suuf wu réy wu am ay yemu yu am solo,(mbàmbulaan, doj, ndand féy-féy... Donte ñu bari da ñoo jàpp ne ñent walla juroomi gox a am waaye di nan far di ci téye juroom walla juroom ñaar.
Ñaar yi ci tàqaloo ñooy Tugal ak Asi, di ko woowee Tugalasi, Bëj-saalumu Aamerik ak Bëj-gànnaaru Aamerik danuy faral di leen di jàppee ñaari gox, suñu booloo nekk Aamerik. Ñenn ñi di boole Afrik Tugal ak Asi mu doon Afritugalasi.
Dun yi dañ leen di boole ci gox yi ñu gën a jege. Lu mel Kanaari donte ci réewum Espaañ la bokk, ci goxu Afrik lañ koy boole. Duni Mbàmbulaan gu dal gi, ci Oseyaani lañ leen boole, ak yeneen.
- 7 gox: Afrik, Bëj-gànnaaru Aamerik, Bëj-saalumu Aamerik, Asi, Tugal, Oseyaani, Dottu Bëj-saalum.
- 6 gox: Afrik, Bëj-gànnaaru Aamerik, bëj-saalumu Aamerik, Tugalasi, Oseyaani, Dottu Bëj-saalum.
- 5 gox: Afrik, Aamerik, Tugal, Oseyaani, Asi.
- 4 gox: Aamerik, Afritugalasi, Oseyaani, Dottu Bëj-saalum.
Afritugalasi | Oseyaani | Afrig | Tugalasi |
Bëj-gànnaaru Aamerig | Tugal | Asi | Bëj-saalumu Aamerig |