- Nooy soppee aw xët
- Nooy man a indee say mbind ci téerexamtéef bi
- Nooy sose aw Xët
- Ngir sàkk xët wu bees (sa xëtu bopp, ab jukki, aw wàll ak yeneen) loolu lanuy faramfàcce ci bii jukki.
- Man mbindin ngay jëfandikoo?
- Fii ngay gise xàll yi gën a yaa, ci mbindin wu yomb wooy jëfandikoo ci xët yi ngay sos walla di ko nas ci Wikipedia
- Nan ngay lëkkalee ay jukki ci seen biir?
- Ni mu wutee ak yeneen téerexamtéef yi, Wikipedia day def nga man a jóge ci aw xët dem ci weneen ci anam wu yomb lool. Loolu laaj na, saa yooy soppi walla sàkk ab jukki, def ci ay lëkkalekaayi biir.
- Nooy duggale lëkkalekaayi biti?
- Ngir yenn jukki yi, man naa doon lu solowu yenn saa yi nga def ay lëkkalekaay yu biti yu lay yóbb ci yeneeni barab, yuy yokk ay xibaar ci li nga jot a wasaare.
- Nooy duggale ab lëkkalekaay diggantey-làkk?
- Dafa am ay waa wikipedia yu bari ci yeneen làkk. Nii la nuy duggale ay lëkkalekaayi diggantey-làkk ci biir jukki yi, ngir jàngkat yi man koo am ci yeneen làkk.
- Ay kàddu ci say coppite
- Ay baat yu néew ci li waral coppite yi, loolu dina noppal waa wikipedia yi
|