Bëj-saalumu Aamerig
Ab jukkib Wikipedia.
Bëj-saalumu Aamerig ci yenn sedatle yu àdduna bi da ñu koy jàppee ni ab gox, walla ci yeneen sedatle, ab ron-gox bu yemoo bi jaar, te li ëpp ci suufam ci xaaju kol-kol bu Bëj-saalumu la nekk.
Tërëlin |
[Soppi] Melosuuf
Bëj-saalumu Aamerik mi ngi ne ci diggante Mbàmbulan gu Dal gi ak Mbàmbulaanu Atlas gi. Doon na gox bu bariy dun, yi ci ëpp nag ci réew yi ci gox bi la ñu bokk. Li ko lëkkaleek Bëj-gànnaaru Aamerik mooy Panamaa. ag càllale gu ay doj moo leru penku gox yépp, ci kaw ba ci suuf; li ëpp ci penkoom àllub yemoo la. Amasoni mooy àll bi ëpp ci àdduna bi, ca réewum Bereesil la ne.
[Soppi] Taariix
Ay askan yu jòge woon goxub Asi ñoo ko dëkkee woon, daanaka am ay junni at j.g.(lu jiitu ganeeg Isaa). Amerigo Vespuci mooy waa tugal ji fa njëkk a teg tànkam, waaye li gën a siiw mooy ne Kristof Kolomb mooy ki ko wuññi
[Soppi] Cancug waa tugal gu gox bi
La ko dale ca xarnub XVI la way dëkk yu Bëj-saalumu Aamerig tàmbalee am ay jàmmaarloo ak waa Tugal yi. Waa Ispaañ ñooy ñi fa njëkk, waa portugaal tegu ci, ci noonu ndànk-ndànk boroom doole yu waa tugal yépp tase fa di xëccoo suuf sa ak way dëkk ya fa cosaanoo, ak tam it ci seen diggante, ay jàmmaarloo yu metti juddoo na ca.
[Soppi] Limu réew yi
[Soppi] Juroom ñaari réew yu temb yi
- Arsantin
- Boliibi
- Bereesil
- Ciili
- Koloombi
- Ekwadoor
- Guyaana
- Panamaa
- Paraguwaay
- Peru
- Uruguwaay
- Benesuwela
[Soppi] Ñetti réew yu tembul yi
- Guyaana gu Faraas (Faraas)
- Dunu Falkland (Nguur-Yu-Bennoo)
- Jorjiyaa bu Bëj-saalum ak dunu Sandwich gu Bëj-saalum (Nguur-Yu-Bennoo)
Réewi Bëj-saalumu Aamerik |
Arsantin • Boliibi • Bereesil • Ciili • Koloombi • Ekwadoor • Guyaana • Panamaa • Paraguwaay • Peru • Uruguwaay • Benesuwela • Guyaana gu Faraas • Dunu Falkland • Surinaam • Tirinidaad ak Tobaago
Afritugalasi | Oseyaani | Afrig | Tugalasi |
Bëj-gànnaaru Aamerig | Tugal | Asi | Bëj-saalumu Aamerig |