Xëtu web
Ab jukkib Wikipedia.
Xëtu web wenn la ci Xëti World Wide Web bi, doon lu ñu sakk ngir ay nemmeekukat man kaa yër ci ndimbalu ab joowukaay. Aw xëtu web day am ab màkkaanu web bu muy àndal ngir ñu man kaa ubbi ci joowukaay bi. Ci jëmmam dëgg, Xëtu web, day nekk ab mbooloom ay mbind, ay nataal aki riir, ci gattal lépp lu gisuwu walla dégguwu.
[Soppi] Saytuwiin
Fànn yi ñu man a saytoo aw xëtu web bari nañu: man ngaa bind ci banqaasu màkkaan yi gu joowukaay bi màkkaanu webam, walla nga topp ab lëkkalekaay bu nekkoon ci weneen xët. Li ëpp ci joowukaay yi ñu gën a jëfandikoo dañ la koy won cib wonekaayub nosukaay jaare ko cib palanteer bum lay tijjil, tax it ñu manees kaa móol. Làkkiin gu HTML mooy cëslaay gi ñu sukkandiku ngir sos xëti web yi, ba tax na saytu gi man a am ak jumtukaay yu wuute: dayoob wonekaay bu ne, móolukaay yi, añs.
[Soppi] Cëslaayi xereñ
Cig xereñ, aw xëtu web dafa cëruwoo ne-ne yu wuute yi ne ci World Wide Web bi. Ci lu daj ne-ne bi ci njëkk ab jukki bu ñu bind ci làkkiinu xibaarfeppal gu HTML. Làkkiin bii di HTML day tax ñu man a sos ay xëti web, jox leen ay màkkaani web, tax itam nu man a kocc-koccal xët wi, tëral ni ci ne-ne yi taxawee.