Màkkaanub mbëjfeppal
Ab jukkib Wikipedia.
ab Màkkaanub mbëjfeppal, di ko wax itam màkkaanub m-bataaxal, walla màkkaanub e-mail, am mbooloom ay araf la, muy teewal ab boyotu bataaxalub mbëjfeppal bu nekk ci ab mbaalub (reseau) xibaarfeppal bu mel ne internet. Màkkaanub mbëjfeppal mooy tax ñu man a yónne ab m-bataaxal (bataaxalub mbëjfeppal) kenn nit ci internet.
Ci lu bari dañuy jaawatle màkkaanub mbëjfeppal ak màkkaanub web, mi nga xam ne du lenn lu dul ab màkkaanub dalub web. Te sax am na yeneen xeeti màkkaani internet.
[Soppi] Baat yi
Kon liñ lay yónne ci sa màkkaanub mbëjfeppal du ab bataaxal, ndax bataaxal dañ koy jàppe niki lu ñu bind ci këyit ak xalima. Bataaxalub mbëjfeppal la, suñ ko gattale mu doon m-bataaxal (di jàng: miim-bataaxal)