Wuutuloxo
Ab jukkib Wikipedia.
Baatu wuutuloxo day tekki mbooleem ay yab-yab, bu am lu mu néew néew benn buy yëngu, yu ñu lëkkale ci seen biir, yu am ay jëfkat, ndomboy dogalkat, ak yeneen te ñu jokkolante leen ci seen biir ngir lenn lu mu wara def, muy man a def beneen fanni ligey bu nit manul (soo ci gennee wuutuloxo yu wayaymbir yi).
Fanni wuutuloxo yi bari nañ lool te itam dañ leen defar ngir njariñ lu wuute: ci misaal, wuutuloxo mbëj, wuutuloxow mbay, wuutuloxow yòbbte ak yëkkati, ak yeneen.
[Soppi] Wuutuloxo yu wayaymbir
Jëfëndikoo wu wuutuloxo yi dimbali nañ nit ñi ba ñu man a def liggéey yoo xam ne weesu nañ doolem, kattanam. Bu dulwoon wuutuloxo yi, nit ci dundinu nit ñu njëkk ña lay des ba tay, te du am nenn numu man a def ba jëm-kanam. Kon wuutuloxo day tekki bepp jumtukaay buy yokk sa doole, di wañi sa coono, te di gaawal aka gënël sa liggey. Balaa ngay mana def ab liggey faw ab jalaxu, ab dox am walla nga daan ab jànkonte.
Seetal ci Wikbaatukaay man nga faa gis baat yi nga xamul |