Waalo
Ab jukkib Wikipedia.
Waalo bokkoon na ci yénn ci nguuri Senegaal yi fi nekkoo. Buuru Waalo dañu ko daa tànn ca péncum Seb ak Bawar. Njurbel moo nekkoo péeyam ci lu njëkk, ganaaw bi lañ ko tuxël Jinge, tuxëlaat ko Ndeer. Tuxu yu bari yooyu doy na tegtal ci dellu ganaaw ak ñàkk doole.
Tërëlin |
[Soppi] Jëwrin yi
Ñooñu ñooy: Jawdaŋ mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox ak Maalaw mi yor koom-koom gi. Ganaaw ñooñu amoon na ñu nekkoon ci kër buur. Bokk na ca Meet moom mooy njiitu bëkk-nèeg yi ak bëkk-nèegu Njurbel moom mooy wax ci turu buur bi ak njiitu ñi yor baxan buur te mu gën a siiwe ci Baadi ak taawub buur. Moom mooy saytu néegu buur ak Fara Njurbel moom mooy njiitu tëgg weñ gu ñuul ak wurus yi. Fara Juñ-juŋ bi moom mooy njiitu waykat yi.
[Soppi] Barag
Barag mooy maqaama bi ñu joxoon buuru Waalo. Yilifoon na li dale ca Mbàmbulaanu Atlas ba Lag de geer. Bokkoon na ci ñi dar Barag ñaari mbooloo: ba njëkk moo di Lingeer miy yaayu buur bi ak Aawo miy soxnaay buur su njëkk, moom moo am teraraagaay toog ca gangunaay (mooy toogu gu buur) ga.
Bu ñaareel ba moodi ñatt ci boroom ndombay tànk yi ci péncam Sëb ak Bawar: ñoom ñooy Jawdun mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox mi ak maalaw mi yor koom-koom bi.
Bokk na ci ñi nekk kër buur ku ñuy wooye Meet, moom moo di njiitu bëkk-néeg yi ak bëkk-néeg Njurbel moom miy wax ci turu buur ak kiy jiite ñi yor mbaxanaam buur. Baadi moom mooy njiitu doomi buur bi, ak yénn ci Jëwriñ yi.
Barag daawul génn ci am at lu dul ñaari yoon: bu njëkk bi ngir jiite lëlu xare. Bu ñaareel bi ngir teew ci xumbeemi gàmmu, moom ak waa këram. mbooleem ñi yor ndomboy tànk dañoo wara teew ci gàmmu gi. Képp ku wuute dees na la mbugal, ñu folli la mbaa ñu rey la. Ndaxte senug teew li muy tegtal moo di yeesal seenug nangu, lañu lokki ak lañu siif. Mbooleem alal yooyu daanañu leen séddale ñetti xaaj: ben ba moo ngi jëm ca buur ba, ñaareel bi mu ngi jëm ca pécum Séb ak Bawar. Bi ci des mu ngi jëm ci taxawal xumbèem yi
[Soppi] Seddaleeg yorte gi
Nguur ga dañ ko seddale woon ci ay diwaan, bu ci ne amoon na bàjjo buy dox mbiri buur bi (Sàmba Lingeer). Kàjj moom la ñu fal ci ndijjooru dex gi, li ko dalee ca aarnik ba fa dex gi sottee. Buriko moom la ñu fal ci bëj-gànnaaru Lag de geer, mu ngi daan dëkk ca Foos, Baadi moom lañu fal ci li dale Sirigi ba Sinò Bawaal. li des ci pal yi mu ngi ci kilifteefu Kangam yi: Marooso moo nga dëkkoon Boroso Piccoo. Barlaf moo nga dëkkoon ca sowu Lag de geer.
[Soppi] Buuri Waalo
1.Njaa jaan Njaay | 31.Fara Yirim |
2.Barka | 32.Njaag Kumba Saam Jaxeer |
3.Caaka Mbaar | 33.Njaag Kumba Saam Jaxeer |
4.Amad Faaduma | 34.Fara Xéere |
5.Luftu Numayga | 35.Njaag Kumba Majigéen |
6.Farna Numayga | 36.Njaak Kumba Naar Saang |
7.Cabati Numayga | 37.njaag Kumba Njaay |
8.Faduma Numayga | 38.Mbaan Naatago |
9.Mbaañ wàdd | 39.Mambooj Njaak |
10.Fajo Wàdd | 40.Yirim Mbañig Gilé |
11.Dafo wàdd | 41.Fara Tòkò Tabi |
12.Ànta Yaasin (gòor) | 42.Yirim Koddu Giran |
13.Yirim Mbañig Ndaw Demba | 43.Fara Penda Tigrila |
14.Tukubaa Mbòoj | 44.Mambooj Maalig Aysa Daaro |
15.Natago Ànta | 45.Fara Penda Aadama Sàll |
16.Caaka Daara Waxoot | 46.Demba Ali |
17.Natago Fara Njaag | 47.Yirim Anta |
18.Natago Yirim | 48.Yirim Koddu Fara Mbooma |
19.Fara Penda Jeŋ | 49.Mbooj Kumba |
20.Taan Fara Njaak | 50.Fara Penda Tigerel |
21.Fara Ko Jeŋ | 51.Njaag Kumba Morige |
22.Fara Kura Joob | 52.Saydu Yaasin Mbooj |
23.Fara Penda Laga Ndeen | 53.Aram Faati Boroso |
24.Fara Kor Ndaama | 54.Yirim Mbañig |
25.Fara Aysa Naalew | 55.Xayer Fàr Xayeri Daaro |
26.Natago xari Daaro | |
27.Barcaaka | |
28.Yirim Mbañig Aram bakk | |
29.Njaag Aram Bakar | |
30.Yirim Ndaten Buubu |
[Soppi] Ay jafe-jafeem
Daanaka Waalo nit desatu fa ndax ya cong yi jòge Gànnaar ak ay xeet yu sax ci diggante sang yi. Moo tax ba ci xarnub XX waa waalo jublu woon ci seen gàddaay wàllu Saalum ak tëdd mi nekk ci diggante Kees ak Mbuur ak dëkk yu mag yi ci réew mi.
Ba besu tey Waalo ngi jànkonteeg coon ya jòge woon ca ŋaayoo ga. loolu mooy jur dellu ganaaw ak daanug waalo, ba ku nekk di ko cokkaas: Taraasaa ak Almaami ak Dàmmeel. Ki ci gënoon a fés nag mooy Faraas. ganaaw ba Faraas rimbee Waalo ba mu nëx, dakoo teeyal dëtëm ko ci ndimbalu Budeŋ ak Potore ak Fedeerba mi ñëw seen ganaaw ci 1885. Booba la nootee Waalo, te naa daf koy xettali.
[Soppi] Delluwaay
Paate sow, Démbi Senegaal: ci làmmeñu Wolof, Dakaar, 1998
[Soppi] Lëkkalekaay yu biir
- senegaal
- Kajoor
- Jolof
- Siin-Saalum
- Fuuta Tooro
- Réewi lebu yi
- Tekuruur
- Bawol
Seetal BUNTU TAARIIX |
Seetal ci Wikbaatukaay man nga faa gis baat yi nga xamul |