Seriñ Muusaa KA
Ab jukkib Wikipedia.
Nawet Jolof noor fa te doo nooraani - ndaw lu ca sax boo màggatee yalwaani.
[Soppi] Bëyit yii ci jigéen la jëm, sabab yi tax ñu koy tànn niki soxna, mu jël araf ya araf wu ci nekk mu def ciy bëyit
Jiim gi
jigéen ju ndaw araf ya lan ko tënke - tënk ba bis pénc ba lan koy tinki
jiimug jigéen mooy jekki bum jàllantu - ndaxte bu jàllantoo asal njaaloontu
cofeel gu mat sëkk a ko war cib sëriñam - ku bëgg dof te ku doful doo am ngërëm
jaamu boroomam jaamu it boroom këram - moo war jigéen su ko manee dàmmey ngëram
jam tuñ ma, jam siiñ ma'ak njamal-yàllaam la - jaalu-yàllaam wa ne Yaasin Salla'a
Jàmm ak juddook jikkoo waral ñuy tànn - ne xur wi wenn la te jiim yiy jenn
Kaaf gi
kaaf nga na baax gaaf, bari ngor, toog fa këram - na bari kersay kër-këriy sàkku ngërëm
nay gone bum def mag te bum gàtt kutuj - bum gudd lool fum toll ànd ak latkoloñ
Yaa gi
yaa ga na yaatu ŋàpp, yaatal dëkkandoom - yaatal boroom këram ci lépp lu mu moom
yaru te yomb te yéwén te yaatu - cib sëriñam te la mu yor bum laatu
Arafu nuun gi
arafu nuun gii ku ko boole xejj - ci sa boroom kër gaa ya duñ la xàjji
neex cere, neex dereet te neexu làmmiñ - neex lépp tey neexlaate gàttu gémmiñ
jigéen na maandu, man a muñ te mokk - di muñ di muuñ di mooñ cereem ne mekk.
[Soppi] Jikko yu aju ci arafu baa jëm ci jigéen
arafu baa yile jigéen ju boole - seen jikko yii kenn du la ba ngay xoole
baax baay te booleek bari bayreek barile - ba su boroom këram amul muy defale
bëñam ya weex tàll ba mel ne perkaal - bët ba ne bàq bakkanam bay safu jaal
day neexu làmmiñ, neexu ñam te mokk lool - lewet te nooy ku mu dajeel sukkal la teel
[Soppi] bokk nq ci li mu wax di ci tagg sëriñam ba Sëriñ Tuuba
adunyaa ngi tol new fel fi moom mbaate dëññu teeñ () woroomiy tëndëŋ xammeewul leen ak woroomi téeñ
lilee tax mu daa tuubloo dameel ak maxa'aki teeñ () ku mel nii ku amleek moom na leen wóor ne yaa ko tooñ
du tooñ nit te soo tooñee mu jéggal la tin la ko () xamul jaamur ak mbokkam, mag ak ndaw ci aw meloom
wurus mbaate ab xaalis bëy ak nag xar ak gëléem () la daa buub di jox ñiy laaj du kuy néegaleek a léem
añs