Aide:Nooy soppee aw xët
Ab jukkib Wikipedia.
Daanaka ci Wikipedia ku nekk man ngaa soppi bépp xët. Jarul ngay bindu ndir man a soppi aw xët. Waaye xët yi ñu aar ñi binduwul du ñu ko man a soppi. Soo toppee xaaj yii di nga xam nu ñuy soppee aw xët.
Tërëlin |
[Soppi] Xaaj bu njëkk: Nooy duggee ci xëtu coppite gi
Xët woo tijji soo xoolee ci kay di nga fa gis soppi soo ci bësee mu ubbil la weneen xët woo koy man a soppee.
[Soppi] Ñaareelu xaaj: Soppi mbind mi
Xët wi day tijjeeku am melokaan wu mel nii(xoolal nataal bi ci suuf). Ci bii barab man nga fee def bépp coppite boo bëgg, muy jubbanti njuurmte yi, yòkk ci mbind walla ay nataal...
[Soppi] Ñetteelu xaaj: Wonendi
Balaa ngay duggal say coppite, ngala bul yakkamti, na nga wonendi li nga liggéey. Wonendi gi dalay won ni muy mel soo leen duggalee, di na tax nga man a jubbantiwaat yeneeni njuumte, suñ ci amee.
[Soppi] Ñenteel: Duggal coppite yi walla Neenal
Su fekkee ci biir coppite gi da ngaa dem ba mu yàgg nga jàpp ne coppite yi nga def jaruñu ko woon, man nga leen bañ a duggal. Da ngay klig ci Neenal. Ci nii xët wi day melaat na nga ko fekkee woon balaa nga ciy amal coppite yi. Donte def nga ay wonendi, du ci waññi dara.
Balaa ngay duggal coppite yi, bindal li nga soppi lan la, ci tool biy peggoog Koj, ci misaal su fekke nguumtey mbindin la, nga bind fa jubbantig mbindin. Su ko defee ci jaar-jaaru xët woowa loolu lañ fay bind, lii di na tax waa-wikipedia yi xam li nga soppi.
Coppite yu tuut: yaw yaay xool ndax say coppite yu tuut la ñu walla deet, maanaam am nañ solo lool walla deet. Su ko defee ci jaar-jaaru xët woowee coppite yu tuut la ñu fay bind.
Topp xët wii: Su fekkee ku bindu nga, nga bëgg a xam coppite yi mujjee am ci woowu xët, coppite yi tegu ci say yos, kligal ci pax mi ci wetam. Ci sa limu toppte nga koy fekk.
ci Jeexintal, soo jàngee jàngaat, saytu bu baax say coppite ndax amuñu benn njuumte, léegi nag man ngaa klig ci Duggal coppite yi