Lu am ag séqoo ak njàppum jaam
Ab jukkib Wikipedia.
Bokk na ci mboolooy way gàddaay yi jañu woon ci kaw Amerig menn mbooloo mom dañu ko cee ga woon manante ko ci (forse ko ci), mbooloo moomu mooy ñi juge woon Afrig, yobbu woon nañu cig sañ-bañ 500 junni ci ñoom niki ay lar (jaam) ci diggante bi nekk ci 1619 – 1808, jooju mooy jamono ji jëli ay jaam indi Amerig nekkee dib sémb bu ñu taxaw ci amal ko.
Liggéeyloo jaam yooyu wéyoon na ak liggéeyloo seeni njur (seeni doom) rawati na ci bëj-saalum bi di barabub mbay, fi aajo tare woon ci ay liggéeykat yuy liggéey ci suuf seek tool yi. Waaye taxawalug njaam gi mi ngi door ci awril 1861, bi xareb ñoñ bi (guerre civile) dooree ci diggante diiwaan yu gore (libre) yi ci bëj-gànnaar ak diiwaani bëj-saalum yi ŋoyoon ci njaam gi sax fi, loolu sax taxoon na ba 11 diiwaan ci ñoom dogoon ci bennoo gi (federation).
Ci bis bi njëkk ci samwiye 1863 la Abraham Linkoln jibal goreelug jaam yi, googu jibal moo neenal njaam gi ci diiwaan yooyu dogoon ci bennoo gi. Ag njaam nag neenalees na ko ci mbooleem Diiwan Yu Bennoo yi bi ñu defee fukk ak ñatteelu soppi ci sartu réew bu Amerig (constitution )atum 1865.
Waaye bàyyi gi ñu def ag njaam ci Amerig lépp teewul ñu ñuul ñi ci Amerig di wéy di jànkoonteek ay coona, di ñu ñu xañ dund gi népp xam (normal) gi boddante ci biir xeet gi wéyoon di am waraloon, ñu nekkoon di jot ci njàng mu suufe .
Ngir gëstuji dund gu gën, ñu ñuuli Amerig ñi doxoon nañu juge ci seen diiwaani bëj-saalum yooyu di yu mbay ak àlle ak kaw-kawe, laggsi ci yu bëj-gànnaar yii di woroomi xay ak taaxe. Waaye loolu lépp taxutoon lu bari ci ñu ñuul ñi manoon a jot ca liggéey yu méngoo ya, ndax kat yoon walla aada daa farataaloon ci ñoom ñu dund cig beddiku wëlif ñu weex ñi ci ay gàdd (Cartier) yu ñàkk te ndóol ñu léen di tudde (ghettos).
Ci mujji ati juroom fukk yi ak njëlbéeni ati juroom benn fukk yi, waa Amerig yii bawoo Afrig jëfandikoo nañu li ñuy wax doggoo gu koom-koom (boycott économique) Martin Luther King jiite ko, ak ay doxi ñaxtu ak yu dul yooyu ci anami ñaxtu yu jàmm, ñu ci doon sàkku ag yamale ci lépp ni ko yoon waxe te bàyyi gënaleg xeet gi ñuy boyal jëme léen .
Yëngu-yëngu gu xeex àq ak yelleef googu àggoon na ca njobbaxtal la ci 28/ut/1963 bi lu ëpp 200 junniy nit dajaloo ci xeet yépp ca kanamu estati bu Linkoln ba ca Washington péeyub Amerig ngir déglu Martin Luther King mu naan : Maa ngi gént bis bob doomi jaam yi ak doomi séeni sang danañu ca toogandoo ca laamaari (xeetu montaañ) Jorgia yu xonq ya, wër ndabul mbokkoo la… Maa ngi gént bis bob sama neenti doom yu ndaw yii dinañu ci dund ci réew mom deesu leen fa àttee ci seeni meloy der waaye ci seen ëmbiitum jëmm (li seeni jëmm ëmb).
Giinaaw xutba bii toogaatuñu lu bari dara rekk Kongres daal di def ay yoonal yu tere raññatle ci biiru xeet ci woote ak njàng ak liggéey ak dëkkal ak ci campéefi mbooloo mi.
Waxuma la sax ne lu bari ci waa Afrigi Amerig yii seenug ñàkk daa tar, looloo waral ñuy tàbbi ci sineebar ak tooñaange (criminality).
Ci at yu néew yu mujj yii yittey Yëngu-yëngu gu xeex yelleef ak àq googu soppiku woon na, ndax kat bi ñu tàmbalee di génne ay àtte yu bees aki yoon yuy tere raññatle, ak bi ñu ñuul dooree di tuxu juge ci kureel gu suufe gi dem ci gu digg-dóomu gi, bi lii amee laaj bi leegi mi ngi jëm ci ndax nag raññatle gu xeet gu njëkk ga ñu jëmale woon ci ñu ñuul ñi du waral ci àtte gi (goornamaŋ bi) mu jël ay matuwaay yu am solo ngir yéwénal nekkiinu ñu ñuul ñi .
Jéego yii ñu tudde “àttey jëf ju feddaliku ji” (muy anamug jël ay liggéey yu ñu weex ñi (ëppte yi) manoon a jot, jox léen ñu ñuul ñi (néewte yi) ) Jéego yii nag làmboo nañu duggal ab lim ci ñu ñuul ñi walla yeneen néewte yi ci mbooleem barabi liggéey yi. Ak nangu ab lim ci ñoom ci daara yu mag yi ak bànqaas yi (les facultés ), ak lijjanti ba lenn ci nit ñu ñuul ñi di man a falu ci Congress ak yeneen doomi néewte yi.
Ci ati juroom ñaar-fukk yi coow ak dàggasante bi bari woon na ci ndax jëf yii am nañu njariñ ak ndax tegu nañu cig maandute.
Waaye lu man a xew daal mooy coppat yu am solo yii am ci at yu mujj yii mi ngi feeñe ci taxawaayu ñu weex ñi ci Amerig. Ay maas (generations) ci waa Amerig leegi ñor nañu ba ñu déggee xutbab Martin Luther ba yoroon baati (maa ngi gént ya).
Waxambaaney Amerig yi leegi nit ñu am worma lañu ci xeet yépp, te it ñu weex ñi gën nañoo nangu ñu ñuul ñi, ci mbooleem wàlli dund yi ak mbooleem campeefi mboolaay yi