Léopold Sédar Senghor
Ab jukkib Wikipedia.
Léopold Sédar Senghor mi ngi juddoo ca Joal ci 9 kori ci atum 1906, génnee àdduna ca Verson ( ca Faraas) ci 20 tabaski 2001. nekkoon taalifkat, bindkat doonoon it killifa aada ca senegaal. Mooy ki njëkk a doon njiitu réewu Senegaal (1960-1980).
[Soppi] Dundam
Léopold Sédar Senghor ma nga juddoo ca Joal, di ab dëkk bu ndaw bu ne ca goxu Mbuur, ci diwaanu Cees. Baayam di Basil Jogoy Senghor, ab yaxantukat la woon; yaayam di Gnilane Ndiémé Bakhou