Kaasamaas
Ab jukkib Wikipedia.
Kaasamaas baat la bu ñu toggalee ci ñaari dogiit : Kaasa ak Maas boo leen boolee muy buuru Kaasa. Kaasa bokk na ci yi njëkk ci nguuri gox bii. Ginnaawam nag Gabu moo ci gën a rëy ci nguur yi. Ñaari nguur yii ñi ngi leen taxawal ci lu tollook xarub fukk ak ñeent g.j, ci loxol ay xarekat yu bawoo ca imbraatóoru Mali ga, Sinjata Kayta yabaloon leen. Nguurug Gabu (nguur gi ëppoon doole ci yii) Trimaskan Traaware moo ko sosoon, mu nekkoon gi tegoon loxo nguur yu ndaw yi nekkoon ci bëj-gànnaaru Gambi, ñooy : Kantora, Gimaara, Jaara, Kiyaŋ ak Kombo. Kaasa ak Gabu way toroxlu lañu woon ñeel Imbraatóoru Mali jamono yi nu leen sose ñoom ñaar, waaye Gabu moom tàmbalee fay galag ñeel imbraatóor gi, ci noonu mu ame ci «ag àtte-sa-bopp » (autonamie). Ci digg xarnu bu fukk ak juroom, la ñaari nguur yii jariñu ca yëngu-yëngu ya Koli Tingala amaloon ca gox ba, bi mu ko defee, ñu daal di dagu ci Mali.
Ci xarnub fukk ak juroom ñatt g.j, la Kaasa tàmbalee tas : giirug Joola songe ko ci sowwu bi, gu Maalinke ci penku bi, gog Balaanta ci bëj-gànnaar gi.. Ci atum 1830 g.j, la giirug Balaanta lakk péeyub Kaasa di Birikama. Ci xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, la Gabu it làmbalee naaxsaay, looloo mi ngi dale ca ba ko giirug Pël gi songee, mooy gi génne woon Fuuta Jalon, bu ko defee mu daal di tàmbalee ñàkk ndànk-ndànk sañ-sañ yi mu amoon ci gox yi mu yilifoon.
Nosiinu biir gi ci nguurug Kaasa ak Gabu xawuñoo wuuteek wa amoon ca nguur yeneen ya ci Senegaal. Buur bi jataayub mag (sénat) ñee ko daa dimbale, moo daa fuglu it ay saxalam tey digal ay sañ-sañam. Diiwaan yi ay foŋsaneer yu kawee leen daan jiite yu tukkee ci garmi yi. Waaye Gabu moom nga xam ne nguurug xare la woon : ay foŋsaneeram yu kawe mi ngi leen daa tànne ci xarekati garmi yi.
Seetal BUNTU TAARIIX |