Internet
Ab jukkib Wikipedia.
Internet (di jàng in-ter-net, jóge ci baatu latin bii di inter=diggante ak bu waa-angalteer bii di net=lëkkaloo) moom lañu jàppe niki lëkkaloo bi gën a rëy ci àdduna bi, te boole ay junniy junniy nosukaay lëkkale leen ci seen biir.
Mi ngi juddu ci ati juroom-benn fukku yi niki am sémb mu kureel gi yor kaaraange ca Réew yu Bennoo yu Aamerig yi ngir sos ab lëkkaloo ci seen diggante, ci njeexteel xare bu sedd bi lañ ci yaatal ñeneen ñu dul yëngu ci kaaraange rek, lëkkale daara yu kawe yi gën a mag, ci lu njëkk, ba yàgg mu àgg ci yenn liggéeyuwaay yi, ci noonu lu muy gën di dem di gën a yaa ba àgg tay ci sunu kër yi.
Tërëlin |
[Soppi] Ràbbiinam
Internet man nan kaa jàppee niki ab lëkkaloo bu xellu te fasu tek ci, cëslaayu ci fànni jumtukaay ak xeeti lonkante bu ne, lëkkalante leen ci seen biir.
Jumtukaay yiy lonku ci internet la ñuy wax host(di tekki gan ci wolof) walla end system (nosteeg njeexte ci wolof), mbir miy jokkale host yi la ñuy wax lëkkalekaay.
[Soppi] Lëkkalooy lëkkaloo yi
Naka-jekk Internet «lëkkalooy lëkkaloo yi» lañ koy dakkantale. Naka-noonu ay lëkkaloo yu bare lonkante doon ko: lëkkaloo yu yëfi-kenn, yu yëfi-ñépp, yu ay këri-koom, yu ay daara yu kawe... Ag juddoom ak ag màggam gu gaaw, bokk na ci li ko waral, mooy bennal gi am ci xeetu jokkoo ci diggante lëkkaloo yi, waral weccontey xibaar man a am ci diggante ay jëfandikukat yu soriyante(yu mel ne nguur-ak-nguur, daara-ak-daara, këru-koom-ak-këru-koom, ak ñoom seen, te jumtukaay yi muy jëfandikoo amuñ ci benn njeexit.