Dalub web
Ab jukkib Wikipedia.
Ab dalub web, di nañ wax itam dalub internet, da di ab mbooloob ay xëti web yu ñu lëkkale ci seen biir duggal leen ci buum gi jox ko ab màkkaanub web ngir ñu man caa àgg. ci 2006 web bi romboon na 1oo ooo ooo ciy dali web.
Tërëlin |
[Soppi] Sosteefam
Dalub web bu ne am na boroom, man naa doon ab këru-liggéeyukaay, walla ab mbootaay, walla kénn nit, añs. Boroom mooy tànn màkkanub web bi ñu man jaare ngir àgg ca dal ba.
[Soppi] Tëddinu xët yi
Ab dalub web ab mbooloom ay xët la, yu ñépp ma na saytu di ko jaare ciy lëkkalekaay yu ne ci biir dal bi. Màkkaanub web, bu ab dal, naka-jekk, day nekk ab URL bu ab xëtu web, mooy nekk xët wi ñuy njëkk a nemmeeku: di ko wax xët wu njëkk wu dal bi (misaalu makkaanub dal man naa ne www.anafa.alfanet.org). Màkkaanub dal di nañ ko wax itam turu barab, maanaam turu barab bi ngay jaare ngir yegg ca dal ba. Kon ñoom ñaar ñépp a bokk tekki: ñoo lay jox turu dal bi, ba nga man kaa ubbi.
Saytu gu ne gu dal bi la ñuy wax ab nemmeeku (nemmeeku ab dal), lëkkalekaay yi ne ci diggante Xët yi ñooy tax ñu man a saytu xëti dal bépp te doo ko génn. Jàpp tamit ne ab nemmeekub dal man naa dooree ci xët wu mu man ti doon ci dal bi, rawatina su fekkee ne ab seetukaay moo lo jox URL bi. Jàpp tamit ne xët wu njëkk wi ak yeneen xët yépp a yem, day ni rekk kay dañ kaa jiital ngir mu doon Xët wi ngay duggusee ci dal bi.
[Soppi] Limu dali web yi
Limu dal yi cig yokk la dëkk lu jamono ji di dem:
At | Lim |
---|---|
1995 | 19 000 |
1997 | 1 000 000 |
2000 | 10 000 000 |
2004 | 57 000 000 |
2005 | 74 000 000 |
2006 | 101 000 000 |
[Soppi] Yenn ciy dal
- Dalu World Wide Web Consortium
- Buntu AJD/PASTEEF
- Daara ju Al-khalil
- Banku Àdduna bi: ab jukki ci Wolof
- Këyitu IPM
- Sene Construction
- Development Gateway Senegal
- UNESCO - Sartu aq ak yeleefi doomu aadama
- Sémbum ALMA