Arafu S
Ab jukkib Wikipedia.
Arafu S
Sutuxlul seŋes Yàlla war sàllu ngëm ()te sóobum lefam daw ba seerug palam
Sawar am sagos ngëm te sàkkub sagam () te sëmbërtaloow yiw ba gën sépp sem
Te sartaagal ’ag sag safoo Yàlla jëm () ca kaw sippi ag sew waxam mbaa jëfam
Te naan kaasi ngëm suggalee sell yaw () te bay saw sas’ak gopp sunna’s ka xam
Selanglul te bul dox di sonjaanu sas () te ngay sopp Yàlla’ak a santiy mayam
Sa bakkan bi dang koy sébéñ ba’m séxéñ () ci ag nooy akug topp sunna’ak sëfam
Te siiwal pexeem bul ko bàyyeek sa koom () dafay sooke aw ay sexeeral mbiram
Te siiw mbicci kaaraange semmal ko jëm () fu sooŋooŋ akug sooy newul ak tilim
Nangay sémb loo man di sottal di sos () te siiw am njariñ ak sutura’ak ngërëm
Te bul jëf lu suufeek lu sew bul soxor () nangay jëf lu set seytu sàqiy mbayam
Nangay sonne xam-xam soril luy safaan () te bul sob te bul sikkal it senn cam
Te bul sóoru mbër it ndegam suq nga () te bul soxlu mbër soxlawoolug manam
Te bul siis itam ab siboor bul sob it () nangay seexlu ñaawtéef wa sib ag jëfam
Te bul sànj bennub jullit sopp ko () te bul koy sabooteek a salteel deram
Nangay digle ag sell bañ caa selaw () suturaal ku nekk it te sàmmub deram
Te bul def safaan it ba tax ngay sangéem () sippeekul di surgab ka man tey ka xam
Safoo sab sëriñ fàwwu dib sang yaw () te sa baati seedeem ka sappug demam
Nangay faj sa jikkoy sagañ sempiku () te bul suux ci sañ-sañ yi Yàlla’a ko am
Te bul nig ci am mbir suba’akiy sibir () dafay faataluw yiw du sottal mbiram
Duggiin wu gaaw te bette Seŋe: kiiraay Aw fas wu baax Seeru: jot Ag dal Sëmbërtal ab rido mooy wàcce ko, fii mooy muuróo aw yiw Aw nit Weesu fa nga naroon a yam Tuur ;wàcce Ñaaw-ñaaw Naan naataat Dal am xel Booyal; bay ab tool booyal ko am at door koo bayaat wolli Làggi ak tàmm sabab Sexeer: gaw ci wet yépp Ŋoy Féete kaw Wéradi Tàmbali Dëkk ak cokkaas Kiy topp ci mbër Suufu : bul suufu mbër ak a top ci ginnaawam waaye jéem koo man Ab xaaraankat mere Noppi akug dal Dëgmu sëgg ngir jaaxle mbaa kersa Ka sapp ag demam : kay bëgg a faatu Jikko ju baaxut waaye cosaanam mooy tooy ju yàgg Ginnaw suba