Arafu M
Ab jukkib Wikipedia.
Arafu m
Maandul te man yaw ci sag maas bul di mànke mukk it () bul def sa màndiŋ mi muy ab meenuwaay tubayul
Xeebal masëy wa te muurloo waame moo ami may () sa fit bu muy màcc jëm cig maax lu mànke nga ful
Bul mëdd may, yeete nang koy sante Yàlla bu wér () te say wax ak say jëf it nay màndaxoo matalal
Bul makk-makkal sa bakkan nang ko miinali yar () bul mer te bul metti, màbbal moy te muñ lu la dal
Metlànk far ko mu def menteñ ne meŋ ne mes () nga muure ko’g dëgg gàttal say mebët di jagal
Tey muñ mettiit moom la Yàllay méngaleek musalam () bul mel ne maaka ma cig bañ-tàng dund saxul
Mokkal te màggal, sa jëf bul màggal it matalal () bul yàq nig max te bul def makk màmm gënul
Àll bu sori Dëkkuwaay Tawub wick-wiccal Ñawka lu tëlee dagg: ag ñawadi Nëbb Nay dëppoo, màndaxe mooy tollale gi nuy def ay balăs bu ñuy peese Neexal ak a nbb-nabbee Man a nax ak man a baab Ne mes;naaxsaay Mbaxana mu ñu ràbbe bant ngir feg aw naaj Ne cell