Arafu L
Ab jukkib Wikipedia.
Arafu L
Maa lànk dootuma leb bay lonk fay di ma të () lott’ay waral leb di tee fay lëj-lëjay lëmi mbir
Laggal(1) te liiru (2) ba jot sam lef te moytu lixóor () tey moytu am lëgg (3) bul léej àbb lor la ci lar (4)
Sa lépp nay leer moyul luubook lu lënt te daw () làggil ci sàkku lu lew daw laaxuy (5) ’ak waxi nar
Bul lomp (6) ciy jëf, jëfal luy léemtu (7) bul laf (8) itam () te seeruwóo lolli bob law naaki mbég lare wér
Bul lang ci sab lal bu suuf lóoree nga làlli te wéy () te lippikuw (9) nit ba làq’y leewi (10) leew aki tar
Ŋaawal sa legg mi (11) bul lajbat lu dul sa ayib () bul lunk jëm suuf, jëmal kaw léemtu (12) naa la nga jub
sa yitte nay law te bul lump it lu dul la nga man () nga lof(13) ci dénd bi(14)bul liis(15) mukk’itam nanga dër
laabal sa xol bi te làng ak gaa yu xam ya te wéy () bul làmbutuy jëf lateel(16)ag xam te teg ko ci ngér
bariy lijjanti te bul lott it ci lenn faral () man lépp làggi ci jëf tey lab ci def lu la war
laggal te bul lang ci ag moy bul ci làng jëm it () bul luññutuy awra bul loofal sa xel bu ko lor
(1)Dem dem gu gaaw (2)Dox ak tànk bañ a war n jombe (3)Duusu géej (4)Ab jaam (5)Ku ay loxoom manul a tëyye dara (6)Gàttañlu (7)Wóor (8)Tekki laxasaay (9)Waññil aw nit coonab li ngeen waroon abokk def nga def ko yaw rekk (10)Leew ak tar a yam ñooy ay call. (11)Fàmb:ron faar. ŋaaw am legg mooy ci tubaab serer denture: di takku liggeey (12)Wax naa la ko waxaat la ko, maanaam yedd naa la (13)Nga sax, waaye cosaan li mooy rab wu samp ab geenam (14)Suuf si (15)Jeng jëm suuf (16)Barilal