Ab jukkib Wikipedia.
Ñi ngi siyaare man de ab waa Senegaal laa buy dund fii mu nekk ca Dakaar ak Tuubaa, di def diggante bi ci jeexiitu ayu bis gu nekk daanaka, nekkoon naa nag Itaali, di naa wax wolof mooy làkk wi ma dàqal ci làkk yi ak araab frãse, angale ak itaalien, wu ci nekk nag déggiin wu wér laa ko dégg, ab dongab daara laa woon nag bu jàng alxuraan ba mokkal ko, demoon naa Amerig ak Frãs ak Espaañ, taalif naa as lëf ci wolof, tekki ci it ay téere, bari na lu ma dugal ci wiki bi ciy jukki, ab entrpreneur laa ci B.T.p maanaam tabax laay liggéeye, may ñaan ñun ñi sopp wii làkk te man koo jëmale kanam ñu xamante, booloo ngir def ci ay liggéey yu man a amali Sunu gaal njariñ.
Abdou Khadre KEBE sakkmultiservices@hotmail.com